Skip to main content

Wolof - The Epistle to Philemon

Page 1

Filemon CHAPITRE 1

1 Man Pool, mi ñu tëj kaso ngir Kirist Yeesu, man ak sunu mbokk Timote, noo lay bind, yaw Filemon sunu soppe ak sunu nawle ci liggéey bi; 2 Nu ngi lay bind sunu soppe Afiya, ak sunu nawle ci xeex bi Arkib, yéen ak mbooloom ñi gëm ci sa kër. 3 Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm. 4 Duma la noppee boole ci samay ñaan, di sant Yàlla sama Boroom. 5 Te dégg naa sa ngëm ci Boroom bi Yeesu, ak sa mbëggeel ci gaayi Yàlla yu sell yépp. 6 Maa ngi ñaanal ne, boo bokk ci ngëm meññ i njariñ, ba nga xam ngëneel yépp, yi nu am ci sunu bokk ci Kirist. 7 Ndaxte sa mbëggeel daf nuy mbég mu réy ak naf xol, ndax yaw, sama mbokk, sexal na xol yi gaayi Elohim yu sell yi. 8 Kon nag am naa kóolute ci Kirist, ba sant la, nga def loo war. 9 Waaye maa ngi lay ñaan ndax mbëggeel, man Pool màggat, te ñu tëj kaso ndax Kirist Yeesu. 10 Maa ngi tinul sama doomu diine Onesim, mi ma jur ci kaso bi. 11 Amul woon sa njariñ démb, waaye tey amal na nu njariñ, yaw ak man. 12 Yaw mi may yónnee la, nga teeru ko, maanaam sama xol. 13 Dama ko bëggoon a téye fi sama wet, ngir mu wuutu la, di ma dimbali, li ma nekk ci kaso bi ngir xebaar bu baax bi. 14 Waaye bgguma def dara loo àndul; Noonu seen jëf ju baax, bañ a doon lu ñu ko sanxe, waaye ngeen di ko def ci seen xol ci xol bu féex. 15 Xanaa moo tax mu tàggoo ak yaw ab diir, ngir man koo fekksi ba fàww. 16 Léegi nag du jaam, waaye dafa ëpp jaam, di mbokk mu ma sopp; 17 Boo ma jàppee ni nawle nag, teeru ko, ni su ma la doon ganesi. 18 Su la tooñee walla mu la ameel dara, teg ko ci man. 19 Man Pool maa ko bind ak sama loxob bopp ne, dinaa ko fey, sax waxuma la ne ame nga sa bakkan ci man. 20 Waaw sama mbokk, may ma beg ci yaw ci Boroom bi, seralal sama xol ci Boroom bi. 21 Gannaaw wóolu na ma ne, dinga ma déggal, moo tax ma bind la, xam ne, dinga def lu ëpp li ma la sant. 22 Te itam nanga ma waajal néeg, ndaxte yaakaar naa ne, Yàlla dina delloosi ma ci seeni ñaan. 23 Nuyu na la Epafras, mi nga nekkal ci kaso bi ci turu Kirist. 24 Samay nawle ci liggéey bi, Màrk, Aristàrk, Demas ak Lukas. 25 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak seen xel. Aamiin.


Turn static files into dynamic content formats.

Create a flipbook
Wolof - The Epistle to Philemon by Filipino Tracts and Literature Society Inc. - Issuu